Fibres de mon cœur vert.
Épaule contre épaule, mes plus que frères,
O Sénégalais, debout !
Unissons la mer et les sources, unissons la steppe et la forêt !
Salut Afrique mère !
2e couplet :
Sénégal toi le fils de l'écume du lion,
Toi surgi de la nuit au galop des chevaux,
Rend-nous, oh ! rends-nous l'honneur de nos ancêtres,
Splendides comme ébène et forts comme le muscle
Nous disons droits - l'épée n'a pas une bavure.
(Refrain)
3e couplet :
Sénégal, nous faisons nôtre ton grand dessein :
Rassembler les poussins à l'abri des milans
Pour en faire, de l'est à l'ouest, du nord au sud,
Dressé, un même peuple, un peuple sans couture
Mais un peuple tourné vers tous les vents du monde.
(Refrain)
4e couplet :
Sénégal, comme toi, comme tous nos héros,
Nous serons durs sans haine et des deux bras ouverts.
L'épée, nous la mettrons dans la paix du fourreau,
Car le travail sera notre arme et la parole.
Le Bantou est un frère, et l'Arabe et le Blanc.
Yëngalleen kooraa yi, te jiin ndënd yi.
Gayndeg sibi xiiru na
Ki doon rëbb ci àll bi
Dafa tëb ci kanam,
Tëb daal di dal, Dindi lépp lu lëndëmoon.
Doon jant ci sunuy njàqare, doon jant ci sunu yaakar.
Jógleen, bokk yi, Afrig booloo na
Refrain :
Wuumi sama xol bu nëtëx bii!
Mbagg ak mbagg, yeen samay bokk,
Ô saa-senegal, jógleen !
Nanu boole géej yi ak siyaan yi, nanu boole joor gi ak ñaay bi !
Mucc ñeel Afrig sunu yaay.
2e couplet :
Senegaal yaw doomi gayndeg sibi,
Yaw mi jóg ci guddi di njaabal i fas,
Delloo nu, oh ! Dello nu ngalla njàmbaarug sunu maam ya,
Taaru ni njalabaan dëgër këcc ni sidit.
Noo ngi wax jub xocc - jaasi ji amul lenn ngaañ.
(Refrain)
3e couplet :
Senegaal, def nanu sunu mbir sa yéene ju kawe:
Dajale cuuj yi ngir làq leen jaxaay yi
Ngir def leen, li ko dale penku jëm sowu, bëj-gànnaar jàpp bëj-saalum,
Taxaw temm, doon wenn askan, askan wu dul teqalikoo,
Waaye askan wu wëlbatiku jëm ci mbooleem ngelawi àddina si
(Refrain)
4e couplet :
Senegaal, niki yaw, niki mbooleem sunu jàmbaar yi,
Dinanu dëgër këcc te du ànd ak mbañeel boole ko ak tijji sunu ñaari yoxo.
Jaasi ji, dinanu ko roof ci biir mbarum jàmm.
Ndax kat liggéey mooy doon sunu ngànnaay ak sunu kàddu.
Bàntu bi sunu mbokk la, ak Araab bi ak ku Weex ki.
(Refrain)
5e couplet :
Waaye nag bu noon bi taalee sunuy dig
Dinanu taxaw jonn nag ŋàbb sunuy ngànnaay:
Wenn askan ci pas-pasu jàmmaarloo ak lépp luy tiis,
Ndaw ñi ak mag ñi, góor ñi ak jigéen ñi.
Dee, waaw ! Dee lanu wax, waaye mukk ci ag toroxtaange.